عَنْ عَبْدِ اللهِ بْنِ مَسْعُودٍ رضي الله عنه قَالَ: سَمِعْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«نَضَّرَ اللَّهُ امْرَأً سَمِعَ مِنَّا شَيْئًا فَبَلَّغَهُ كَمَا سَمِعَ، فَرُبَّ مُبَلِّغٍ أَوْعَى مِنْ سَامِعٍ».
[صحيح] - [رواه الترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 2657]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
"yal na Yàlla leeralal waaju dégg ci man dara mu jottali ko kem na mu ko dégge woon, bariwaana ku ñu jottali mu gën a xam aji-dégg ji".
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2657]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaanal ag leeraange ak ug nëtëx ak ug rafet ci àdduna, ak Yàlla eggale ko ci leeru àjjana ja ak i xéewalam ak ug leeram ca allaaxira; ñeel ki dégg hadiisam mokkal ko ba jottali ko keneen, ndax amaana ki ñu jottali hadiis bi gën a xam gën a dégg gën a man a jàngat ci ki tuxal hadiis bi, bu ko defee ku njëkk ki dàqa mokkal dàqa toxal , ku ñaareel ki dàqa dégg dàqa jàngat.