عَنِ ابْنِ عَبَّاسٍ رضي الله عنهما قَالَ:
كَانَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَجْوَدَ النَّاسِ، وَكَانَ أَجْوَدُ مَا يَكُونُ فِي رَمَضَانَ حِينَ يَلْقَاهُ جِبْرِيلُ، وَكَانَ يَلْقَاهُ فِي كُلِّ لَيْلَةٍ مِنْ رَمَضَانَ فَيُدَارِسُهُ القُرْآنَ، فَلَرَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَجْوَدُ بِالخَيْرِ مِنَ الرِّيحِ المُرْسَلَةِ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gënoon a tabe ci nit ñi, ci weeru koor nag la daan gën a tabe ba Jibriil daan daje ak moom, daan na daje ak moom guddi gu nekk ci weeru koor di jàng ak moom Alxuraan, waat naa ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gën a tabe ci yiw ngelaw lu ñu boyal.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gënoon a tabe ci nit ñi, te ag tabeem daana
yokk lool ci weeru koor ba daan na joxe li yell a joxe ñeel ku ko yeyoo, li waral tabeem
daan yokk nag ñaari mbir la:
Bi ci njëkk: daje gi mu daan daje ak Jibriil yal na ko Yàlla yokk jàmm.
Ñaareel bi mooy:
Tari gimudaan tari alxuraan ji si jibriil.
Daan na tari
si Jibriil Alxuraan jépp, mu waat ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gën a tedd gën a man a joxe ak def aw yiw, gën a gaaw a jariñ nit ñi ci ngelaw lu teey lu Yàlla yabal ci taw ak yërmànde.