+ -

عَنْ سَعْدٍ رضي الله عنها قَالَ:
جَاءَ أَعْرَابِيٌّ إِلَى رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: عَلِّمْنِي كَلَامًا أَقُولُهُ، قَالَ: «قُلْ: لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَحْدَهُ لَا شَرِيكَ لَهُ، اللهُ أَكْبَرُ كَبِيرًا، وَالْحَمْدُ لِلَّهِ كَثِيرًا، سُبْحَانَ اللهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ، لَا حَوْلَ وَلَا قُوَّةَ إِلَّا بِاللهِ الْعَزِيزِ الْحَكِيمِ» قَالَ: فَهَؤُلَاءِ لِرَبِّي، فَمَا لِي؟ قَالَ: «قُلْ: اللهُمَّ اغْفِرْ لِي وَارْحَمْنِي وَاهْدِنِي وَارْزُقْنِي».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2696]
المزيــد ...

Jële nañu ci Sahd -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Benn kaw-kaw dafa ñëw ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: xamal ma wax joo xam ne dama koy wax, mu ne ko: "waxal: laa ilaaha illalaahu wahdahu laa sariika lahu, Allaahu Akbaru kabiiran, wal hamdu lil-Laahi kasiiran, subhaanal Laahi Rabbil haalamiina, laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi Alhasiisil-Alhakiimi" mu ne ko: lii de sama Boroom la ñeel, ana lan mooma ñeel man? Mu ne ko: "waxal: Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wahdinii, warsuqnii".

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2696]

Leeral

Benn waay bu dëkk ca kaw ga dafa laaj Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu xamal ko ag sikar gu muy wax, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: waxal: "laa ilaaha illallaahu wahdahu laa sariika lahu" mu tàmbalee ci seede Tawhiid,maanaam mooy amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, "Allaahu Akbaru kabiiran" Maanaam: Yàlla moo gën a màgg lépp gën koo tedd, "walhamdu lil-Laahi kasiiran" Maanaam: sant Yàlla lu bari, ci ay meloom ak i jëfam, ak i xéewalam yi kenn manut a takk, "Subhaanal Laahi Rabbil haalamiina" Maanaam: màgg na set na ci gépp wàññiku, "laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi Alhasiisil-Alhakiimi" Maanaam: amul wëlbatiku jóge ci genn anam jëm ci geneen anam lu dul ci coobarey Yàlla ak ndimbalam ak dëppaleem, Waa ji ne ko: baat yii sama Boroom la ñeel dañu ko ciy tudd di ko ci màggal, lan mooma ñeel man ci ma ñaanal sama bopp? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: waxal: "Allaahumma ixfir lii" Ci far samay ñaawteef te suturaal ma, "warhamnii" eggalel fi man defal ma njariñi diine ak yu àdduna, "wahdinii" Jëme ma ci nekkiin yi gën, te jëme ma ci yoon wu jub wa, "warsuqnii" Wërsëgal ma alal ju dagan ak wér ak wépp yiw ak jàmm.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci tudd Yàlla ak di wax laa-i-Laaha Illal Laahu,Allaahu Akbar, Alhamdu lil-Laahi,ak Subhaanal Laahi.
  2. Sopp nañu tudd Yàlla ak kañ ko njëkk ñuy ñaan.
  3. Sopp nañu nit ki di ñaan ñaan yi gën a teey, ak ci yi ñu toxal te mu boole yiwi àdduna ak allaaxira, sañ naa ñaan nag lu ko soob.
  4. Yell na ci jaam bi mu xér ci jàng lu koy jariñ ci àdduna ak allaaxira.
  5. Xér ci sàkku njéggal ak yërmànde ak wërsëg, loolu dafa dajale yiw yépp.
  6. Ñeewanteg Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-ci jàngal xeetam wi lu leen di jariñ.
  7. Dañoo tudd yërmànde ginnaaw njéggal ngir laab gi mat, njéggal mooy suturaal bàkkaar yi far ko soreele ko sawara, yërmànde mooy eggale yiw yi ak dugal àjjana, te lii mooy texe gu màgg gi.