عن ابن عمر رضي الله عنهما:
أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ نَهَى عَنِ الْقَزَعِ.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5921]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na zulu.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5921]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na wat lenni kawaru bopp bàyyi leneen li.
Tere gi nag day làmboo góor ñépp ndaw ak mag, budee jigéen nag warut a wat dara ci kawaru boppam.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sariihab Lislaam dafa yittewoo melokaanu nit ki.
Gaaral tekki yi
Làkk: Àngale Urdu Español Ndollent (62)