عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الخُدْرِيِّ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّ اللَّهَ تَبَارَكَ وَتَعَالَى يَقُولُ لِأَهْلِ الجَنَّةِ: يَا أَهْلَ الجَنَّةِ؟ فَيَقُولُونَ: لَبَّيْكَ رَبَّنَا وَسَعْدَيْكَ، فَيَقُولُ: هَلْ رَضِيتُمْ؟ فَيَقُولُونَ: وَمَا لَنَا لاَ نَرْضَى وَقَدْ أَعْطَيْتَنَا مَا لَمْ تُعْطِ أَحَدًا مِنْ خَلْقِكَ؟ فَيَقُولُ: أَنَا أُعْطِيكُمْ أَفْضَلَ مِنْ ذَلِكَ، قَالُوا: يَا رَبِّ، وَأَيُّ شَيْءٍ أَفْضَلُ مِنْ ذَلِكَ؟ فَيَقُولُ: أُحِلُّ عَلَيْكُمْ رِضْوَانِي، فَلاَ أَسْخَطُ عَلَيْكُمْ بَعْدَهُ أَبَدًا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6549]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"Yàlla mu baarkeel mi te kawe day wax waa àjjana: éey yéen waa àjjana? Ñu ne ko wuyusi nanu la topp nañu la ak mbegte, mu ne leen: ndax gërëm ngeen? Ñu ne ko: lu ñuy teree gërëm te nga jox nu loo joxul kenn ci sa mbindeef yi? Mu ne leen: dama leen di jox lu gën loolu, ñu ne ko: yaw sunu Boroom, ana lan moo gën loolu? Mu ne leen: wàcce naa sama ngërëm ci seen kaw, dootuma leen mere ba fàww".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6549]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne Yàlla day wax waa àjjana fekk ña nga ca biir: yéen waa àjjana, ñu wuyu ko ne ko: wuyusi nanu la ak mbegte yaw sunu Boroom, Mu ne leen: ndax gërëm ngeen? Ñu ne ko: waaw gërem nanu; ana lan moo nuy teree gërëm te nga jox nu loo joxul kenn ci sa mbindeef yi! Yàlla ne leen: ndax duma leen jox lu gën loolu? Ñu ne ko: yaw sunu Boroom, ana lan mooy li gën loolu?! Mu ne leen: damay wàcce ci yéen sama ngërëm luy sax; te dootuma leen mere baa fàww.