عَنْ صُهَيْبٍ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِذَا دَخَلَ أَهْلُ الْجَنَّةِ الْجَنَّةَ، قَالَ: يَقُولُ اللهُ تَبَارَكَ وَتَعَالَى: تُرِيدُونَ شَيْئًا أَزِيدُكُمْ؟ فَيَقُولُونَ: أَلَمْ تُبَيِّضْ وُجُوهَنَا؟ أَلَمْ تُدْخِلْنَا الْجَنَّةَ، وَتُنَجِّنَا مِنَ النَّارِ؟ قَالَ: فَيَكْشِفُ الْحِجَابَ، فَمَا أُعْطُوا شَيْئًا أَحَبَّ إِلَيْهِمْ مِنَ النَّظَرِ إِلَى رَبِّهِمْ عَزَّ وَجَلَّ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 181]
المزيــد ...
Jële nañu ci Suhayb yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«bu waa àjjana duggee àjjana, Yàlla mu Barkeel mi te kawe day wax ne: ndax bëggeen dara lu ma leen dolli? Ñu ne ko: ndax weexaloo sunu kanam yi? Ndax dugaloo nu àjjana, musal nu ci sawara? Nee na: mu wuññi kiiraay gi, joxeesu leen dara lu nu gën a bëgg ci xool seen Boroom bu màgg bi».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 181]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne bu waa àjjana duggee àjjana, Yàlla mu Baarkeel mi te kawe da leen di wax:
Ndax bëgg ngeen ma dolli leen dara?
Waa àjjana ñoom ñépp ne ko: ndax weexaloo sunu kanam yi? Ndax dugaloo nu àjjana musal nu ci sawara?
Yàlla dindi kiiraay gi yëkkëti ko; te kiiraayam leer la, joxeesu leen dara lu ñu gën a bëgg ci xool seen jëmmi Boroom ju màgg ji.