عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الْخُدْرِيِّ وَأَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنهما عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«يُنَادِي مُنَادٍ: إِنَّ لَكُمْ أَنْ تَصِحُّوا فَلَا تَسْقَمُوا أَبَدًا، وَإِنَّ لَكُمْ أَنْ تَحْيَوْا فَلَا تَمُوتُوا أَبَدًا، وَإِنَّ لَكُمْ أَنْ تَشِبُّوا فَلَا تَهْرَمُوا أَبَدًا، وَإِنَّ لَكُمْ أَنْ تَنْعَمُوا فَلَا تَبْأَسُوا أَبَدًا» فَذَلِكَ قَوْلُهُ عَزَّ وَجَلَّ: {وَنُودُوا أَنْ تِلْكُمُ الْجَنَّةُ أُورِثْتُمُوهَا بِمَا كُنْتُمْ تَعْمَلُونَ} [الأعراف: 43].
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2837]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu, ak Abuu Hurayrata yal na leen Yàlla dollee gërëm ñu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
Aji-woote ji day woote ne: di ngeen wér te du ngeen tawatati ba fàww, di ngeen dund te du ngeen deeati ba fàww, di ngeen bijjaaw te du ngeen màggatati ba fàww, di ngeen xéewlu te du ngeen yoqatati ba fàww " loolu mooy li Yàlla di wax naan: {ñu woo leen ne leen loolu mooy àjjana ja dondloo nañu leen ko ci sababus li ngeen doon jëf} [Al-Ahraaf: 43].
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2837]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ne dees na woo waa àjjana fekk ñoo nga fa di xéewalu: di ngeen wér te du ngeen feebar ci àjjana ba fàww, di ngeen dund te du ngeen fi dee ba fàww, donte nelaw la te mooy dee gu ndaw, di ngeen fi bijjaaw te du ngeen fi màggatati ba fàww, di ngeen xéewlu te du ngeen fi yoqat baa ngéen fiy jaaxlee ba fàww, loolu mooy waxi Yàlla mu màgg mi: {ñu woo leen ne leen loolu mooy àjjana ja dondloo nañu leen ko ci sababus li ngeen doon jëf} [Al-Ahraaf: 43].