+ -

عَنْ أَنَسِ بْنِ مَالِكٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«يَقُولُ اللَّهُ تَعَالَى لِأَهْوَنِ أَهْلِ النَّارِ عَذَابًا يَوْمَ القِيَامَةِ: لَوْ أَنَّ لَكَ مَا فِي الأَرْضِ مِنْ شَيْءٍ أَكُنْتَ تَفْتَدِي بِهِ؟ فَيَقُولُ: نَعَمْ، فَيَقُولُ: أَرَدْتُ مِنْكَ أَهْوَنَ مِنْ هَذَا، وَأَنْتَ فِي صُلْبِ آدَمَ: أَلّاَ تُشْرِكَ بِي شَيْئًا، فَأَبَيْتَ إِلَّا أَنْ تُشْرِكَ بِي».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6557]
المزيــد ...

Jële nañu ci Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«Yàlla mu kawe mi day wax ki gën a woyof mbugal ci waa sawara ëllëg bis-pénc: boo moomoon li ci suuf lépp ndax danga ko jote sa bopp? Mu ne: waaw, mu ne ko: bëggoon naa ci yaw lu gën a néew loolu, fekk yaa ngi ca ndiggal Aadama, mooy nga bañ maa bokkaale ak dara nga lànk ne danga ma bokkaale ».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6557]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne Yàlla mu kawe mi dana wax ki gën a néewle mbugal ci waa sawara ginnaaw ba ñu ca duggee: boo moomoon àdduna ak li ci biiram ndax danga ko jote sa bopp ci mbugal mii? Mu ne ko: waaw, Yàlla ne ko: sàkku woon naa ci yaw digal la lu gën a yomb jamono ya nga nekkee ca ndigal Aadama te mooy nga bañ maa bokkaale ak dara; ba ma la génnee yóbb la àdduna nga lànk di ma bokkaale.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneelu Tawhiid ak ni mu yombee jëfe.
  2. Ñàngaayu bokkaale Yàlla mu kawe mi ak ug mujjam.
  3. Yàlla dafa jël kóllare ci doomi Aadama yi fekk ñoo nga ca ndigal Aadama ci ñu bañ ko a bokkaale.
  4. Moytandikuloo bokkaale ak ne àdduna ak li ci biiram du jariñ yéefar bi dara ëllëg bis-pénc.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Pastoo Asaami Suwiit Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Serbi Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية
Gaaral tekki yi