+ -

عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الخُدْرِيِّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«يُؤْتَى بِالْمَوْتِ كَهَيْئَةِ كَبْشٍ أَمْلَحَ، فَيُنَادِي مُنَادٍ: يَا أَهْلَ الجَنَّةِ، فَيَشْرَئِبُّونَ وَيَنْظُرُونَ، فَيَقُولُ: هَلْ تَعْرِفُونَ هَذَا؟ فَيَقُولُونَ: نَعَمْ، هَذَا المَوْتُ، وَكُلُّهُمْ قَدْ رَآهُ، ثُمَّ يُنَادِي: يَا أَهْلَ النَّارِ، فَيَشْرَئِبُّونَ وَيَنْظُرُونَ، فَيَقُولُ: وهَلْ تَعْرِفُونَ هَذَا؟ فَيَقُولُونَ: نَعَمْ، هَذَا المَوْتُ، وَكُلُّهُمْ قَدْ رَآهُ، فَيُذْبَحُ ثُمَّ يَقُولُ: يَا أَهْلَ الجَنَّةِ خُلُودٌ فَلاَ مَوْتَ، وَيَا أَهْلَ النَّارِ خُلُودٌ فَلاَ مَوْتَ، ثُمَّ قَرَأَ: {وَأَنْذِرْهُمْ يَوْمَ الحَسْرَةِ إِذْ قُضِيَ الأَمْرُ وَهُمْ فِي غَفْلَةٍ} [مريم: 39]، وَهَؤُلاَءِ فِي غَفْلَةٍ أَهْلُ الدُّنْيَا {وَهُمْ لاَ يُؤْمِنُونَ} [مريم: 39]».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4730]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf, ab wootekat daal di woote: yéen waa àjjana, ñu yoqamtiku di xool, mu wax ne: ndax xam ngeen lii ? Ñu ne ko: waaw, lii mooy dee, te ñoom ñépp a ko gis, mu woote ne: yéen waa sawara, ñu yoqamtiku di xool, mu wax ne: ndax xam ngeen lii ? Ñu ne ko: waaw, lii mooy dee, te ñoom ñépp a ko gis, ñu rendi ko, mu wax ne: yéen waa àjjana sax ba fàwwu dee amatul, yéen waa sawara sax ba fàwwu dee amatul, daal di jàng: {na nga leen xupp bisub réccu ba ba ñu àttee mbir ma fekk ñoom ñoo ngi cig càggante} [Maryama: 39], waa àdduna jii ñoo ngi cig càggante, {te ñoom duñu gëm}[Maryama: 39]».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4730]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ëllëg bis-pénc dañuy indi dee, ci melom xar mu am weex ak ñuul, Ñu woote: yéen waa àjjana! Ñu tàllal séen baat ak séen doq yi yëkkati séen bopp yi di xool, Mu ne leen: ndax xam ngeen lii? Ñu ne: waaw, lii mooy dee, ñoom ñépp gis nañu ko te xam nañu ko, Wootekat bi woote: yéen waa sawara, ñu tàllal séen baat yi ak séen doq yi yëkkati séen bopp yi di xool, Mu ne: ndax xam ngeen lii? Ñu ne: waaw, lii mooy dee, ñoom ñépp gis ko; Ñu rendi ko, wootekat bi ne: yéen waa àjjana des ba fàwwu dee amatul, yéen waa sawara des ba fàwwu dee amatul. Ngir loolu dolliku ci xéewali way-gëm ñi, waaye di yokk mbugali way-weddi yi. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di jàng: {na nga leen xupp bisub réccu ba bu ñu àttee mbir ma te ñoom ñoo ngi cig càggante te ñoom duñu gëm} Bis-pénc dañuy tàqale diggante waa àjjana ak waa sawara, ku nekk dugg fa muy sax, Ñi doon def ñaawtéef di réccu te réccu du jariñ, ak ki gàttañlu bu yokkul ay yiw.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Mujjug nit ca allaaxira mooy sax ba fàwwu ca àjjana walla sawara.
  2. Artu gu tar ci tiitaangey bis-pénc ci ne bisub réccu la.
  3. Leeral ne mbégtem waa àjjana day sax, ak njàqarey waa sawara.