عَنْ أَبِي بَكْرٍ الصِّدِّيقِ رضي الله عنه أَنَّهُ قَالَ: أَيُّهَا النَّاسُ، إِنَّكُمْ تَقْرَؤُونَ هَذِهِ الآيَةَ: {يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا عَلَيْكُمْ أَنْفُسَكُمْ لاَ يَضُرُّكُمْ مَنْ ضَلَّ إِذَا اهْتَدَيْتُمْ}، وَإِنِّي سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«إِنَّ النَّاسَ إِذَا رَأَوْا الظَّالِمَ فَلَمْ يَأْخُذُوا عَلَى يَدَيْهِ أَوْشَكَ أَنْ يَعُمَّهُمُ اللَّهُ بِعِقَابٍ مِنْهُ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي في الكبرى وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 2168]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Bakrin As-Siddiix -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: yéen nit ñi, yéen de dangeen di jàng aaya bii: {yéen ñi gëm wattuleen seen bopp cànkuteg aji-sànku ji du leen lor ndeem jub ngeen}, man dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«nit ñi bu ñu gisee tooñkat bi te téyewuñu loxoom kon tuuti rekk Yàlla boole leen mbugal».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2168]
Abuu Bakrin As-Siddiix -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xamle ne: nit ñi dañuy jàng aaya bii:
{yéen ñi gëm wattuleen seen bopp cànkuteg aji-sànku ji du leen lor ndeem jub ngeen} [Al-Maa-ida: 105].
Ñu dégge ci ne nit ki na jëm ci sellal boppam dong, ndaxte ginnaaw loolu cànkuteg aji-sànku ji du ko lor, ndax sàkkuwuñu ci ñoom ñuy digle lu baax ak di tere lu bon!
Mu xamal leen ne demewul noonu, ndaxte moom dégg na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Nit ñi bu ñu gisee tooñkat bi te terewuñu ko tooñ, te man nañu ko
koo tere, kon xaw tuuti rekk Yàlla boole leen mbugal ñoom ñépp kay def lu bon la, ak ka ca noppi.