عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«قَارِبُوا وَسَدِّدُوا، وَاعْلَمُوا أَنَّهُ لَنْ يَنْجُوَ أَحَدٌ مِنْكُمْ بِعَمَلِهِ» قَالُوا: يَا رَسُولَ اللهِ وَلَا أَنْتَ؟ قَالَ: «وَلَا أَنَا، إِلَّا أَنْ يَتَغَمَّدَنِيَ اللهُ بِرَحْمَةٍ مِنْهُ وَفَضْلٍ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2816]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"deeleen jegeele, tey jubal, te ngeen xam ne kenn ci yéen du mucc ngir ay jëfam" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ba ci yaw sax? Mu ne: "ba ci man kay, lu dul Yàlla muure ma ag yërmàndeem ak ngëneelam".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2816]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day ñaax sahaaba yi ci ñu jëf, te ragal Yàlla seen kem-kàttan, ci lu dul ëppal du caagine gàtteñlu, ak ñu jublu ca seen jëf ji ag njub ak ug sellal ñeel Yàlla ak topp sunna ngir ñu nangu seen jëf ba mu nekk sabab ci yërmànde wàcc ci ñoom.
Mu xamle ne kenn ci yéen du mucce ci jëfam dong, waaye yërmàndey Yàlla manu ci a ñàkk.
Ñi ne ko: ba ci yaw Yonnente Yàlla bi sa jëf du la musal, ak li muy màgg yépp?
Mu ne: ba ci man, lu dul Yàlla muure ma ag ngëneelam ak yërmàndeem.