+ -

عَنْ عَمَّارِ بنِ ياسِرٍ رضي الله عنه قال:
بَعَثَنِي رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي حَاجَةٍ، فَأَجْنَبْتُ فَلَمْ أَجِدِ الْمَاءَ، فَتَمَرَّغْتُ فِي الصَّعِيدِ كَمَا تَمَرَّغُ الدَّابَّةُ ثُمَّ أَتَيْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَذَكَرْتُ ذَلِكَ لَهُ فَقَالَ: «إِنَّمَا كَانَ يَكْفِيكَ أَنْ تَقُولَ بِيَدَيْكَ هَكَذَا» ثُمَّ ضَرَبَ بِيَدَيْهِ الْأَرْضَ ضَرْبَةً وَاحِدَةً، ثُمَّ مَسَحَ الشِّمَالَ عَلَى الْيَمِينِ، وَظَاهِرَ كَفَّيْهِ وَوَجْهَهُ.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 368]
المزيــد ...

Jële nañu ci Ammaar ibn Yaasir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da maa yónni ci jenn aajo, ma am janaba te amuma ndox, ma xalangu ci suuf si kem ni daaba di xalangoo, ma ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, nettali ko loolu, mu ne ma: "doon na la doy rekk nga def nii say loxo" mu dóor ay loxoom ci suuf benn dóor, daal di masaa càmmooñam ci kaw ndayjoor bi, ak bitti ténq yi ak kanam gi.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 368]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa yónni Ammaar ibn Yaasir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ci benn tukki ngir lenn ci ay aajoom, mu ame janaba ci sëy walla ci génne maniyu ci bànneex, te amul ndox mumu sangoo, Te xamul woon àttey tiim ngir janaba, waaye ngir toj gu ndaw ci la ko xamoon, Mu góor-góorlu yaakaar ne kem ni muy masaaye kanamam ci suuf ak yenn céram ci toj gu ndaw, kon tiim ngir janaba fàww mu matale yaram wépp suuf; ngir nattale ko ak ndox, mu xalangu ci suuf ba yaram wépp daj mu daal di julli, Ba mu ñëwee ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu nettali ko loolu; ngir xam ndax li mu def noonu la walla déet? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-leeralal ko na ka lay laabe ci ñaari toj yi, gu ndaw gi niki saw, ak gu mag gi niki janaba: te mooy mu dóor ñaari loxoom ci suuf benn dóor, daal di masaa càmmooñam ci kaw ndayjoor bi,ak bitti ténq yi ak kanamam.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dañoo war a wut ndox bala ñoo tiim.
  2. Yoonalees na tiim ci ki ame janaba te amul ndox.
  3. Tiim ngir toj gu mag, moo ngi mel ni tiim ngir toj gu ndaw.
Ndollent