+ -

عَنْ عَائِشَةَ أُمِّ المُؤمنينَ رضي الله عنها قَالَتْ:
كُنْتُ أَغْتَسِلُ أَنَا وَالنَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مِنْ إِنَاءٍ وَاحِدٍ كِلاَنَا جُنُبٌ، وَكَانَ يَأْمُرُنِي، فَأَتَّزِرُ، فَيُبَاشِرُنِي وَأَنَا حَائِضٌ، وَكَانَ يُخْرِجُ رَأْسَهُ إِلَيَّ وَهُوَ مُعْتَكِفٌ فَأَغْسِلُهُ وَأَنَا حَائِضٌ.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 299]
المزيــد ...

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi-yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Daan naa sangu man ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci benn ndab fekk nun ñaar ñépp a am janaba, daan na ma digal ma woddu, muy jonjoo ak man fekk damaa nekk ci mbaax, daan na lihtikaaf ba noppi génne boppam fi man ma koy raxas fekk damaa nekk ci mbaax.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 299]

Leeral

Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xamle yenn mbir yi mu jagoo moom ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, bokk na ca: da daan sangu janaba moom ak Yonnente bi ci benn ndab di bokk di ci tanq. Ak ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu ko daan bëgg a dikkal fekk mu gis mbaax da koy digal mu muur yaramam li tàmbalee ci jumbax bi ba ci wóom yi, muy jonjoo ak moom ci lu dul sëy. Ak ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na Ihtikaaf ci Jàkka ji di génne boppam Aysatu di ko raxas nekk ci neegam fekk dafa gis mbaax

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dagan na jëkkër ak jabar sangoondoo ci lenn ndab.
  2. Dagan na ñu jonjoo ak ku gis mbaax ci fu dul awra wi, ndax yaramam dafa laab.
  3. Sopp nañu mu woddu jamonoy jonjoo ga.
  4. Jaar ci sabab yiy teree tàbbi ci yi ñu araamal.
  5. Tere nañu ki gis mbaax muy sax ci Jàkka.
  6. Daganal nañu mu jonjoo ak mbir yi moo xam dafa tooy walla mu woow, bokk na ci yooyu raxas kawar ak peñe ko.
  7. Rafetug nekkinu Yónente bi ci biir njabootam.