عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ عَمْرٍو رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«المُسْلِمُ مَنْ سَلِمَ المُسْلِمُونَ مِنْ لِسَانِهِ وَيَدِهِ، وَالمُهَاجِرُ مَنْ هَجَرَ مَا نَهَى اللَّهُ عَنْهُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 10]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne:
«jullit mooy ki nga xam ne jullit ñi mucc nañu ci làmmiñam ak ci loxoom,gàddaaykat nag mooy ki gàddaay li Yàlla araamal ci moom».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 10]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne jullit bu lislaamam mat mooy ki jullit ñi mucc ci làmmiñam du leen saaga, du leen rëbb, du leen jëw, te du dox seen diggante ci genn xeetu lor ci làmmiñam, Dañuy mucc it ci loxoom du leen tooñ, du jël seen alal ci lu dul dëgg, ak lu niru loolu, Aji-gàdday nag mooy ki bàyyi li Yàlla araamal.