عَنْ عَائِشَةَ أُمِّ المُؤْمنينَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا زَوْجِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ يَعْتَكِفُ العَشْرَ الأَوَاخِرَ مِنْ رَمَضَانَ، حَتَّى تَوَفَّاهُ اللَّهُ، ثُمَّ اعْتَكَفَ أَزْوَاجُهُ مِنْ بَعْدِهِ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 2026]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit yal na ko Yàlla dollee gërëm soxnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu ne:
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ba keroog muy faatu, ay saxnaam daldi Lihtikaaf ginnaawam.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2026]
Ndayu jullit ñi Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa taqoo woon ak Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ngir sàkku Laylatul Xadri, mu wéy ci loolu ba Yàlla faat ko, ay soxnaam yal na leen Yàlla dollee gërëm taqoo ak Lihtikaaf ci ginnaawam.