عن أَنَسِ بْنِ مَالِكٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«تَسَحَّرُوا، فَإِنَّ فِي السَّحُورِ بَرَكَةً».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1923]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Anas yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la«.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1923]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaaxe na ci xëdd te mooy lekk ci mujjanteelu guddi gi ngir waajal koor gi; ndaxte am na (baarke) mooy yiw wu bari ci fay akub yool, ak taxaw ci waxtu wi mujj ci guddi gi ngir ñaan, ak dëgërlu ci woor gi, ak cawarte, ak woyofal coonaam.