عَنْ زَيْدِ بْنِ ثَابِتٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ:
تَسَحَّرْنَا مَعَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، ثُمَّ قَامَ إِلَى الصَّلاةِ، قُلْتُ: كَمْ كَانَ بَيْنَ الأَذَانِ وَالسَّحُورِ؟ قَالَ: قَدْرُ خَمْسِينَ آيَةً.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1921]
المزيــد ...
Jële nañu ci Saydu ibn Saabit yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Xëdd nañu ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu daal di jug jëm ca julli ga, ma ne ko: ñaata moo dox ci diggante nodd gi ak xëdd gi? Mu ne: luy tolloo ak juróom-fukki aaya.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1921]
Yenn Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm xëdd nañu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, topp mu jog moom Yonnente bi jëm ca jullig fajar ga. Anas daldi wax Sayd ibn Saabit yal na ko Yàlla dollee gërëm ne ko: ñaata la waxtu wi toll ci diggante nodd gi ak bàyyi xëdd? Sayd yal na ko Yàlla dollee gërëm ne ko: mi ngi tollu ak jàng juróom-fukki aaya yu yam, yoo xamne guddul waaye gàttul, njàng ma it gaawul waaye yeexul.