عَنْ ابْنَ عُمَرَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا قَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«إِذَا رَأَيْتُمُوهُ فَصُومُوا، وَإِذَا رَأَيْتُمُوهُ فَأَفْطِرُوا، فَإِنْ غُمَّ عَلَيْكُمْ فَاقْدُرُوا لَهُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1900]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen, bu muuroo ci yeen nangeen ko nattale».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1900]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne màndargam duggug weeru koor ak génnam, mu wax ne: bu ngeen gisee weeru koor wi woorleen, bu aw niir doxee seen diggante ak moom mu muuru ci yéen; nangeen lim fanweeri fan ñeel weeru Baraxlu wi, bu ngeen gisee weeru Kori gi worileen, bu aw niir doxee seen diggante ak moom mu muuru ci yéen; nangeen lim fanweeri fan ñeel weeru Koor gi.