+ -

عَنْ أَبِي عُبَيْدٍ، مَوْلَى ابْنِ أَزْهَرَ، قَالَ:
شَهِدْتُ العِيدَ مَعَ عُمَرَ بْنِ الخَطَّابِ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ، فَقَالَ: هَذَانِ يَوْمَانِ نَهَى رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَنْ صِيَامِهِمَا: يَوْمُ فِطْرِكُمْ مِنْ صِيَامِكُمْ، وَاليَوْمُ الآخَرُ تَأْكُلُونَ فِيهِ مِنْ نُسُكِكُمْ.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1990]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abii Ubayd, jaamub Ibn Ashar, mu wax ne:
Fekke naa feet ga ak Umar ibnul Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: ñaari bis yii Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa tere ñu woor leen: bis bi ngeen di dog seen koor gi, ak beneen bis bi ngeen di lekk seenum Tabaski.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1990]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa tere woor bisu feetu Korite ak feetu Tabaski; bu dee feetu Korite bisu dog la ci weeru koor gi, bu dee bisu feetu Tabaski bisu lekk tabaski yi la.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Araamalees na woor ñaari bis yii di Korite ak Tabaski ak ñatti fan yi topp si tabaski; ndaxte day topp bisu Tabaski bi lu dul ci ki amul gàtt kon dana dagan mu woor bisi tabaski yi.
  2. Ibn Hajar nee na: nee nañu: njariñu melal ñaari bis yi mooy junj sababu warug dog gi, te mooy teqale woor gi, ak feeñal ag matam ci dog bis bi ci topp, beneen bi ngir jaamu gu ñuy sàkkoo jege Yàlla ci rendi ngir lekk ko.
  3. Sopp na ñu ci kiy xutba mu tudd ci xutbaam gi li aju ci jamonoom ci ay àtte tey dàkk xew-xew yi.
  4. Yoonal nañu lekk ci tabaski mi.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri الموري Malagasi Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi
Ndollent