+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ يَقُمْ لَيْلَةَ الْقَدْرِ إِيمَانًا وَاحْتِسَابًا غُفِرَ لَهُ مَا تَقَدَّمَ مِنْ ذَنْبِهِ»

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 35]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 35]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamale ngëneelu taxaw Laylatul Xadri gi nga xam ne day nekk ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ak ne ku ca farlu ci julli ak ñaan ak jàng Alxuraan ak tudd Yàlla, ngir gëm ko ak la ca ñëw ciy ngëneel, mu yaakaar ca jëfam ja yoolub Yàlla, ci lu dul ngistal walla ndéggtal, kon dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Pulaar Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneelu Laylatul Xadri ak ñaaxe ci taxaw ko.
  2. Jëf yu baax yi deesu ko nangu lu dul mu ànd ak yéene ju dëggu.
  3. Ngëneelu Yàlla ak yërmaandeem, ndax ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram.