عَنْ جَابِرٍ رَضيَ اللهُ عنهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنْ قَالَ: سُبْحَانَ اللهِ العَظِيمِ وَبِحَمْدِهِ، غُرِسَتْ لَهُ نَخْلَةٌ فِي الجَنَّةِ».
[صحيح] - [رواه الترمذي] - [سنن الترمذي: 3464]
المزيــد ...
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"ku wax: subhaanal Laahi Alhasiimi wa bi hamdihi, ñu jëmbëtal ko ag garabu tàndarma ca àjjana".
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3464]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku wax: (subhaanal laahi al hasiimu wa bi hamdihii) mu sellal Yàlla ci jëmmam ak i meloom ak i jëfam, dees na ko jëmbëtal ag garabu tàndarma ca suufu àjjana ci wépp yoon wu mu ko waxe.