عن أَبِي مُوسَى الأَشْعَرِيِّ رضي الله عنه: أَنَّ رَسُولَ اللهِ صلى الله عليه وسلم قَالَ:
«مَنْ صَلَّى الْبَرْدَيْنِ دَخَلَ الْجَنَّةَ»
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 574]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-Asharii-yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku julli ñaari sedd yi dana dugg àjjana»
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 574]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day soññee ci xér ci jullig ñaari sedd yi, te mooy jullig fajar ak tàkkusaan, mu bégal ki leen julli te jox leen seeni àq ca waxtu wa ca mbooloo ma, ak lu dul yooyu, danañu nekk sabab ci mu dugg àjjana.