Listu hadiis yi

julli gi gën a diis ci naaféq yi mooy jullig gee ak jullig fajar, te bu ñu xamoon li nekk ci ñoom ñaar kon danañu ko teewe donte dañuy raam
عربي الإنجليزية الأوردية
julliy juróom, ak Àjjuma ba Àjjuma, ak weeru koor ba weeru koor, dañuy far bàkkar yi ci séen diggante bu dee moytu nañu bàkkaar yu mag yi
عربي الإنجليزية الأوردية
ku julli suba moo ngi ci kaaraangeg Yàlla
عربي الإنجليزية الأوردية
waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
عربي الإنجليزية الأوردية
Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf
عربي الإنجليزية الأوردية
jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: "julli ci waxtoom" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "teg ca fonk ñaari way-jur" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "jihaad ci yoonu Yàlla
عربي الإنجليزية الأوردية
Jaayante naa ak Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak dégg ak topp, ak laabire bépp jullit
عربي الإنجليزية الأوردية
déng naa la ngay bari looy sujjóotal Yàlla, ndaxte doo sujjóotal Yàlla genn sujjóot lu dul ne Yàlla dina la ci yëkkatil daraja, sippil la ci njuumte
عربي الإنجليزية الأوردية
ku julli ñaari sedd yi dana dugg àjjana
عربي الإنجليزية الأوردية
xibaarleen ma bu ag dex nekkoon ci buntu këru kenn ci yéen mu ciy sangu bis bu nekk juróomi yoon, ndax loolu dana dese tilim ci yaram?
عربي الإنجليزية الأوردية
koo xam ne day jullu laata jant bi di fenk ak laata muy soh du dugg sawara
عربي الإنجليزية الأوردية
amul benn jullit boo xam ne jullig farata dana jot mu rafetal njàppu ma ak toroxlu ga ak rukkoo ya,lu dul ne dana ko faral li ko jiitu ci ay bàkkaar,fii ak deful bàkkaar bu mag,te loolu jamono jépp la
عربي الإنجليزية الأوردية
yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci
عربي الإنجليزية الأوردية