+ -

عَنْ جَرِيرِِ بْنِ عَبْدِ اللَّهِ رضي الله عنه قَالَ:
بَايَعْتُ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَلَى شَهَادَةِ أَنْ لاَ إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ، وَأَنَّ مُحَمَّدًا رَسُولُ اللَّهِ، وَإِقَامِ الصَّلاَةِ، وَإِيتَاءِ الزَّكَاةِ، وَالسَّمْعِ وَالطَّاعَةِ، وَالنُّصْحِ لِكُلِّ مُسْلِمٍ.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 2157]
المزيــد ...

Jële nañu ci Jariir Ibn Abdullah-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne:
Jaayante naa ak Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak dégg ak topp, ak laabire bépp jullit.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2157]

Leeral

Sahaaba bii di Jariir Ibn Abdullah -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne moom dafa kollarante ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci Tawhiid ak di jooxe julliy juróom yi ñu farataal ci bis bi ak ci guddi gi, ci ay sàrtam ak i ponkam, ak i wareefam, ak i sunnaam, ak ci joxe asaka, mu nekk ag jaamu gu aju ci alal nekk lu war, dees koy jële ci way-woomal yi jox ko ñi ko yayoo ci way-ñàkk yi ak ñeneen, kollarante ak moom it topp ñi jiite mbir yi, ak di laabire bépp jullit, loolu nag ngir xér ci jariñ ko, ak eggale yiw ci moom, ak jeñal ko lor ci wax ak jëf.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Solos julli ak asaka,te ñoom ñaar dañoo bokk ci ponki Lislaam yi.
  2. Solos laabire ak laabirante ci diggante jullit ñi, ba tax Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di jaayante ak sahaaba yi ci loolu.