+ -

عَنْ عُثْمَانَ رضي الله عنه قَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«مَا مِنَ امْرِئٍ مُسْلِمٍ تَحْضُرُهُ صَلَاةٌ مَكْتُوبَةٌ فَيُحْسِنُ وُضُوءَهَا وَخُشُوعَهَا وَرُكُوعَهَا، إِلَّا كَانَتْ كَفَّارَةً لِمَا قَبْلَهَا مِنَ الذُّنُوبِ، مَا لَمْ يُؤْتِ كَبِيرَةً، وَذَلِكَ الدَّهْرَ كُلَّهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 228]
المزيــد ...

Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi-yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
"amul benn jullit boo xam ne jullig farata dana jot mu rafetal njàppu ma ak toroxlu ga ak rukkoo ya,lu dul ne dana ko faral li ko jiitu ci ay bàkkaar,fii ak deful bàkkaar bu mag,te loolu jamono jépp la".

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 228]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day leeral ne amul benn jullit bob waxtuw jullig farata dana dugg mu rafetal am njàppoom matale ko,daal di teewlu julli gi ànd ak ragal ba xolam ak ay céram yépp jublu Yàlla di teewlu màggaayam, mu matal jëfi julli gi niki rukkoo yi ak sujjóot yi ak yeneen yi, lu dul ne julli gi dana nekk lu koy faral bàkkaar yu ndaw yi ko jiitu, fii ak deful bàkkaar bu mag,ngëneel lii nag day wéy ba ci jamono jépp ak ci julli yépp.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Julli giy far ay bàkkaar mooy julli gi jaam bi rafetal njàppu ma, te def ko cig ragal Yàlla di ca sàkku jëmmi Yàlla mu kawe mi.
  2. Ngëneelu taqoo ak jaamu yi, ngir ne sabab la ci njéggalu bàkkaar yu ndaw yi.
  3. Ngëneelu rafetal njàppu mi, ak rafetal julli gi te teewlu ko mu ànd ak toroxlu.
  4. Solos moytu bàkkaar yu mag yi ci njéggalu bàkkaar yu ndaw yi.
  5. Bàkkaar yu mag yi dara du ko far lu dul tuub.