عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صلَّى الله عليه وسلم قال:
«ما مِنْ أحَدٍ يُسلِّمُ علي إلا ردَّ اللهُ عليَّ رُوحي حتى أردَّ عليه السَّلامَ».
[إسناده حسن] - [رواه أبو داود وأحمد] - [سنن أبي داود: 2041]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«amul kenn kuy julli ci man lu dul ne Yàlla dana ma delloo samag ruu ba ma delloo ko nuyóo».
[Ag càllalaam tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 2041]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne dañu koy delloo ruuham ngir mu delloo nuyóo ki ko nuyu moo xam ku jege la walla ku sori; dundug Barsax ak bàmmeel yi mbirum kumpa la kenn xamul dëgg-dëggam ku dul Yàlla, te Moom lépp la xam.