+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّهُ سَمِعَ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«أَرَأَيْتُمْ لَوْ أَنَّ نَهَرًا بِبَابِ أَحَدِكُمْ يَغْتَسِلُ فِيهِ كُلَّ يَوْمٍ خَمْسًا، مَا تَقُولُ ذَلِكَ يُبْقِي مِنْ دَرَنِهِ؟» قَالُوا: لَا يُبْقِي مِنْ دَرَنِهِ شَيْئًا، قَالَ: «فَذَلِكَ مِثْلُ الصَّلَوَاتِ الخَمْسِ، يَمْحُو اللَّهُ بِهِ الخَطَايَا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 528]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«xibaarleen ma bu ag dex nekkoon ci buntu këru kenn ci yéen mu ciy sangu bis bu nekk juróomi yoon, ndax loolu dana dese tilim ci yaram?" Ñu ne ko: déedéet du bàyyi ci deram dara, mu ne: "loolu nag moo ngi mel ni julliy juróom, yàlla da ciy far njuumte yi».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 528]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day niròole julliy juróom ci bis bu nekk ak guddi gi, ci ni muy fare bàkkaar yu ndaw yi ak njuumte yi dafamelni ag dex gu nekk ci buntu kër nit ki mu ci sangu bis bu nekk juróomi yoon, ba du bàyyi ci deram bi ak ci tilimam ji dara.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneel lii day jagoo rekk ci far bàkkaar yu ndaw yi, bu dee yu mag yi nag fàww ñu tuub ko.
  2. Ngëneelu joxe julliy juróom ak sàmmoonte ak moom ci ay sàrtam ak i ponkam, ak i wareefam ak i sunnaam.