عَنِ النُّعْمَانِ بْنِ بَشِيرٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَثَلُ الْمُؤْمِنِينَ فِي تَوَادِّهِمْ وَتَرَاحُمِهِمْ وَتَعَاطُفِهِمْ مَثَلُ الْجَسَدِ، إِذَا اشْتَكَى مِنْهُ عُضْوٌ تَدَاعَى لَهُ سَائِرُ الْجَسَدِ بِالسَّهَرِ وَالْحُمَّى».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2586]
المزيــد ...
Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«misaalu way-gëm ñi ci seenug bëggante ak seenug yërëmante ak seenug ñeewantu day mel ni aw yaram, bu ci benn cër di jàmbat dara mbooleem yaram wi yépp day
ànd bañ a nelaw ak di tàng».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2586]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ni jullit ñi war a mel ci seen biir ci yéeneente aw yiw ak yërmànde ak dimbaleente ak jàppalante, ak di yég lor wuy dal ci ñeneen ñi, kem ni wenn yaram mel, bu ci benn cér feebare, mbooleem yaram wi day ànd di bañ a nelaw ak di tàng.