+ -

عَنْ مَعْقِلِ بْنِ يَسَارٍ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«الْعِبَادَةُ فِي الْهَرْجِ كَهِجْرَةٍ إِلَيَّ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2948]
المزيــد ...

Jële nañu ci Mahxal ibn Yasaar yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«jaamu Yàlla ci jamonoy fitna moo ngi mel ni gàddaay jëm ci ma».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2948]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamal na jaam ñi ngir ñuy jëm ci jaamu Yàlla jamonoy fitna ak ray ak jaxasoog mbiri nit ñi ak ne loolu ag fayam mi ngi mel ni gàddaay jëm ci Yonente bi, loolu nag ndaxte nit ñi dañu koy sàggane, te kenn du ci taxaw ku dul ay benn-been.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci jaamu ak dëgmal Yàlla jamonoy fitna; ngir aaru ci fitna si, ak mucc ci yàqute gi.
  2. Leeral ngëneelu jaamu Yàlla ci fitna ak waxtuy càggante yi.
  3. Jaadu na ci jullit bi mu beru barabi fitna yi ak càggante yi.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri الموري Malagasi Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi