عن ابن عمر رضي الله عنهما قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«مَا زَالَ يُوصِينِي جِبْرِيلُ بِالْجَارِ، حَتَّى ظَنَنْتُ أَنَّهُ سَيُوَرِّثُهُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6014]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Jibriil deñul di ma dénk dëkkandóo, bama muj njort ne dana ko dondloo».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6014]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Jibriil deñul di baamtu ak di ko dénk mu yittewóo dëkkandóo, te mooy ki jege sa kër, moo xam jullit la walla yéefér, moo xam jegeñaale la walla du jegeñaale, ci sàmm ay àqam te bañ koo lor, ak di rafetal jëme ci moom, ak di muñ ay loram, ba Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- njort ngir li mu màggal àqi dëkkandóo ak li ko Jibriil di baamtu tax mu njort ne wahyu dana wàcc ngir jox ko ci alal ji fi dëkkandóo bàyyi ginnaaw ba mu faatoo.