عَنْ أبي سَعيدٍ الخُدريَّ رضي الله عنه قال: قال رسولُ الله صلَّى الله عليه وسلم ِ:
«إزْرَةُ المُسْلمِ إلى نصفِ السَّاق، وَلَا حَرَجَ -أو لا جُنَاحَ- فيما بينَهُ وبينَ الكعبينِ، وما كان أسفلَ منَ الكعبين فهو في النار، مَن جرَّ إزارَهُ بطرًا لم يَنْظُرِ اللهُ إليه».
[صحيح] - [رواه أبو داود وابن ماجه وأحمد] - [سنن أبي داود: 4093]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"koddaayu jullit bi ca digg yeel ba la wara yam, aayul ci mu nekk ci digganteem ak dojor yi, lu nekk ci suufu dojor yi nag moom sawara la jëm, te kuy diri koddaayam ngir rëy-rëylu Yàlla du ko xool".
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 4093]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne koddaayu góoru jullit bi, te mooy liy muur xaaju suuf gi ci góor, ñatt anam la: Bi ci njëkk mooy: lu ñu sopp te mooy mu nekk ci digg yeel bi. Ñaareel bi: bu dagan ci lu dul sibeel te mooy mu wàcc ba ci dojor yi; te ñooy ñaari yax yi génn ci fi yeel bi ak ndëngu li teqalikoo. Ñatteel bi: bu araam te mooy mu nekk ci suufu dojor yi, te dees na ragal ci moom sawara, bu dee day rëy-rëylu ak di bég ak di bew kon Yàlla du ko xool.