+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ يُرِدِ اللهُ بِهِ خَيْرًا يُصِبْ مِنْهُ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 5645]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ku Yàlla namm ci moom aw yiw dana ko nattu».

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5645]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla bu nammee aw yiw ci kenn ci jaamam yu gëm yi dana leen nattu ci séen i bakkan ak séen i alal ak séen i njaboot, ngir la ca aji-gëm ji di jële ci dellu ci Yàlla mu kawe mi ak ci di ñaan, ak la ca nekk ci far ay ñaawtéef, ak yëkkatikuy daraja.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Aji-gëm ji dana dajeek ay xeeti nattu.
  2. Ab nattu man naa nekk màndargam bëgg gi Yàlla bëgg jaamam bi, ba dana ko yëkkëtil ay darajaam, kaweel ab dayoom, sippil ko ay njuumteem.
  3. Ñaaxe ci muñ musiba yi te bañ a naqarlu.