+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«الْمُؤْمِنُ الْقَوِيُّ، خَيْرٌ وَأَحَبُّ إِلَى اللهِ مِنَ الْمُؤْمِنِ الضَّعِيفِ، وَفِي كُلٍّ خَيْرٌ، احْرِصْ عَلَى مَا يَنْفَعُكَ، وَاسْتَعِنْ بِاللهِ وَلَا تَعْجَزْ، وَإِنْ أَصَابَكَ شَيْءٌ، فَلَا تَقُلْ لَوْ أَنِّي فَعَلْتُ كَانَ كَذَا وَكَذَا، وَلَكِنْ قُلْ قَدَرُ اللهِ وَمَا شَاءَ فَعَلَ، فَإِنَّ (لَوْ) تَفْتَحُ عَمَلَ الشَّيْطَانِ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2664]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Jullit bi am kàttan, moo gën te moom la Yàlla gën a bëgg ci jullit bi néew kàttan, ñoom ñéppu na nga a baax, xéral ci lu lay jariñ, te nga dimbandikoo Yàlla te bul lompañ, bu la dara jotee, bul wax ay bu fekkoon ne defnaa lii mbaa lee kon lii du am, waaye waxal ne Yàlla dogal na te lu ko neex lay def, ndax boo waxul loolu yaa ngi ubbil saytaane buntu».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2664]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day leeral ne jullit léppam aw yiw la, waaye jullit bi dëgër ci ngëmam ak ug dogoom ak alalam ak yeneen moo ëpp yiw te moo gënal Yàlla mu màgg mi jullit bi néew kàttan. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di dénk jullit bi mu def sabab yi koy jariñ ci mbiri àdduna ak allaaxira, ànd ak sukkandiku ci Yàlla, tay dimbandikoo ci moom, te wakkirlu ci moom. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na ñàkk solo ak tàyyeel ak di yeexamtu ci def luy jariñ àdduna ak allaaxira. Bu jullit bi pasteefoo ci jëf, te jàpp ci sabab yi, di dimbandikoo Yàlla, di sàkku ci moom aw yiw, ginnaaw loolu li ko war mooy mu bàyyee mbiram Yàlla, te mu xam ne lu Yàlla tànn mooy li gën. Bu ko musiba dalee ginnaaw ga, bu mu wax: «Bu fekkoon ne defoon naa nàngam kon lii ak lee mooy am»; Di wax naan (bu dul woon nàngam) loolu day tijjil bunt saytaane" ci di gaaral ab dogal,ak di naqarlu li weesu, waaye na jébbalu te gërëm te wax: "Yàlla dogal na, te lu ko neex lay def", Lu am rekk dafa fekk ne noonu la ko Yàlla bëgge, Ndax mooy def lu ko soob, te amul kuy delloo ab dogalam,walla di ko dindi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na Nit ñi dañoo rawante ci ngëm.
  2. Sopp nañu kàttan ci jëf yi; ndax njariñ man na caa ame amiin woo xam ne bu ca kàttan ga nekkul woon du am.
  3. Nit ki dafa war a xér ci lu koy jariñ, te bàyyi lu ko dul jariñ.
  4. War na ci aji-gëm ji muy sàkku dimbaluYàlla ci mbiram yépp, te mu bañ a sukkandiku ci boppam.
  5. Saxal dogal yi ak ne loolu du dàquwante ak def sabab yi ak dox ci sàkku yiw yi.
  6. Tere nañu ñuy wax "budul woon nàngam” di ko wax ci anamug naqarlu ci wàccug musiba, araamal nañu it di gaaral ab dogalu
  7. Yàlla mu kawe mi.