عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ:
كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَسِيرُ فِي طَرِيقِ مَكَّةَ، فَمَرَّ عَلَى جَبَلٍ يُقَالُ لَهُ جُمْدَانُ، فَقَالَ: «سِيرُوا هَذَا جُمْدَانُ، سَبَقَ الْمُفَرِّدُونَ» قَالُوا: وَمَا الْمُفَرِّدُونَ يَا رَسُولَ اللهِ؟ قَالَ: «الذَّاكِرُونَ اللهَ كَثِيرًا وَالذَّاكِرَاتُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2676]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da doon dox ci mbeddi Màkka yi, daal di romb doj wu ñuy woowe Jumdaan, mu wax ne: "doxleen lii mooy Jumdaan, ñu beru ñi raw nañu" ñu ne ko: ñan ñooy ñi beru yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne: "góor ñiy tudd Yàlla lu bari, ak jigéen ñiy tudd Yàlla lu bari".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2676]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral darajay ñiy tudd Yàlla lu bari, ci ne ñoom dañoo beru daal di jiitu ñu dul ñoom ci am ay daraja yu kawe ca àjjanay xéewal ya, mu niróole leen ak montaañu Jumdaan wi nga xam ne dafa beru ci yeneen montaañ yi.