عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ:
قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «يَقُولُ اللهُ عَزَّ وَجَلَّ: أَنَا عِنْدَ ظَنِّ عَبْدِي، وَأَنَا مَعَهُ حِينَ يَذْكُرُنِي، فَإِنْ ذَكَرَنِي فِي نَفْسِهِ ذَكَرْتُهُ فِي نَفْسِي، وَإِنْ ذَكَرَنِي فِي مَلَإٍ ذَكَرْتُهُ فِي مَلَإٍ خَيْرٍ مِنْهُ، وَإِنِ اقْتَرَبَ إِلَيَّ شِبْرًا، تَقَرَّبْتُ إِلَيْهِ ذِرَاعًا، وَإِنِ اقْتَرَبَ إِلَيَّ ذِرَاعًا، اقْتَرَبْتُ إِلَيْهِ بَاعًا، وَإِنْ أَتَانِي يَمْشِي أَتَيْتُهُ هَرْوَلَةً».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2675]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Yàlla mu màgg mi nee na: man maa ngi fa ma sama jaam bi njorte, te maa ngi ànd ak moom saa yu ma tuddee, bu ma tuddee ci boppam ma tudd ko ci sama bopp, bu ma tuddee ci mbooloo ma tudd ko ci mbooloo mu gën mooma, bu ma jege luy toll ni Sibr, ma jege ko luy toll ne loxo, bu ma jegee luy toll ni loxo ma jege ko luy toll ni Baah, bu ma dikkee ci dox, ma dikke ko ci ñukk".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2675]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne Yàlla mu kawe mi nee na:
Man maa ngi fa ma sama jaam bi di njorte, ba damay jëflante ak moom ci kem njortam ci man, loolu nag ci yaakaar ak mébët njéggal, ma def li mu yaakaar ci man ci yiw walla lu dul loolu; te maa ngi ànd ak moom ci yërmànde ak tawfeexal ak gindi ak sàmm ak dëgëral saa su ma tuddee.
Bu ma tuddee ci boppam di ku wéet di ku beru ci sàbbaal ak tudd Yàlla walla leneen; ma tudd ko ci sama bopp.
Bu ma tuddee ci mbooloo; ma tudd ko ci mbooloo mu gën a bari gën a sell.
Ku jege Yàlla luy toll ni Sibr Yàlla dolli ko jege ko luy toll ni loxo.
Bu ko jegee luy toll ni loxo mu jege ko luy toll ni Baah.
Bu jëmee ci Yàlla di dox mu jëm ci moom di ñukk.
Jaam bi bu jegee jëm ci Boroomam ci topp ko ak dégmal ko, kon Boroom bi da koy gën a jege am lef ci kem jëfam.
Saa su njaameg aji-gëm ji gënee mat ñeel Boroomam Aji-Kawe ji jege ko, mayug Yàlla ak yoolam moo gën a bari jëfu jaam bi ak coonoom, lay mbir mooy yoolu Yàlla mooy not jëfu jaam ca anam ga ak ca tolluwaay ga.
Aji-gëm ji day rafet njort, tey jëf, gaawantu di yook ay jëfam ba keroog muy daje ak Yàlla.