عَنْ عُقْبَةَ بْنِ عَامِرٍ رضي الله عنه قَالَ:
قُلْتُ: يَا رَسُولَ اللهِ مَا النَّجَاةُ؟ قَالَ: «امْلِكْ عَلَيْكَ لِسَانَكَ، وَلْيَسَعْكَ بَيْتُكَ، وَابْكِ عَلَى خَطِيئَتِكَ».
[صحيح] - [رواه الترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 2406]
المزيــد ...
Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Damaa wax: "yaw Yonnente Yàlla bi, ana lan mooy musale? Mu ne ma "tëyéel sa làmmiñ, te na la sa kër doy, te nga jooy say ñuumte".
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2406]
Huqbata ibn Aamir yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc sabab yiy musal aji-gëm ji ci àdduna ak allaaxira?
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: dénk naa la ñatti bir:
Bi ci njëkk: sàmmal sa làmmeñ ci lu amul yiw, ak ci wépp ay, te bul wax lu dul aw yiw.
Ñaareel bi: nanga taqoo ak sa kër ngir jaamu Yàlla ca wéetaay ya, te nga soxlawoo topp Yàlla mu màgg mi, te nga beru ci sa kër wolif fitna yi.
Ñatteel bi: jooyal te réccu te tuub li nga def ci ay bàkkaar.