عَنْ عَبْدِ اللهِ بْنِ مَسْعُودٍ رَضيَ اللهُ عنهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنَّهُ كَانَ يَقُولُ:
«اللهُمَّ إِنِّي أَسْأَلُكَ الْهُدَى وَالتُّقَى، وَالْعَفَافَ وَالْغِنَى».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2721]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax:
"Allaahuma innii as-aluka alhudaa wattuqaa walhafaafa walxinaa".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2721]
Bokkoon na ci ñaani Yonente bi: yaw Yàlla sama Boroom man maa ngi lay laaj ag njub yoon wu jub ci xam dëgg ak jëfe ko, ak ragal la jëf ndigal yi moytandiku tere yi, ak fegu bàyyi li daganul te rafetul ci wax walla jëf, ak doylu wolif mbindeef yi, ba tax na duma ajowoo jëm ci kenn ku dul sama Boroom mu màgg mi.