عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنِ اغْتَسَلَ يَوْمَ الجُمُعَةِ غُسْلَ الجَنَابَةِ ثُمَّ رَاحَ، فَكَأَنَّمَا قَرَّبَ بَدَنَةً، وَمَنْ رَاحَ فِي السَّاعَةِ الثَّانِيَةِ، فَكَأَنَّمَا قَرَّبَ بَقَرَةً، وَمَنْ رَاحَ فِي السَّاعَةِ الثَّالِثَةِ، فَكَأَنَّمَا قَرَّبَ كَبْشًا أَقْرَنَ، وَمَنْ رَاحَ فِي السَّاعَةِ الرَّابِعَةِ، فَكَأَنَّمَا قَرَّبَ دَجَاجَةً، وَمَنْ رَاحَ فِي السَّاعَةِ الخَامِسَةِ، فَكَأَنَّمَا قَرَّبَ بَيْضَةً، فَإِذَا خَرَجَ الإِمَامُ حَضَرَتِ المَلاَئِكَةُ يَسْتَمِعُونَ الذِّكْرَ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 881]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«ku sangu bisub Àjjuma sangug janaba topp mu dem julli ji, dana mel ni ku saraxe
ag giléem, ku dem ci ñenteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe
aw nag, ku dem ci ñatteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku jegeele am kuuy
mu ami béjjan, ku dem ci ñenteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe
ag ginaar, ku dem ci juróomeelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe
ab nen, bu imaam bi génnee maalaaka yi ñëw di déglu xutba gi».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 881]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ngëneelu teel a dem ca jullig Àjjuma ja, Teel gi nag day tàmbalee ci bu jant bi fenkee ba baa imaam bi di ñëw; moom nag juróomi waxtu la, dees na ko séddale juróomi xaaj ci kem waxtu yi ci diggante bi jant bi fenkee ba baa imaam bi di dugg si di yéeg ci minbar bi ngir xutba:
Bu njëkk bi: ku sangu sangu mu mat kem sangu janaba, topp mu dem ca jàkkay Àjjuma ja ci waxtu wu njëkk wi moo ngi mel ku saraxe ag giléem.
Ñaareel bi: ku dem ci ñaareelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe aw nag.
Ñatteel bi: ku dem ci ñatteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe am kuuy -muy xar mu mag- mu am ay béjjan.
Ñenteel bi: ku dem ci ñenteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe ag ginaar.
Juróomeel bi: ku dem ci jurómeelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe aw nen.
Bu imaam bi génnee ngir xutba; malaaka yi toogoon ci bunt bi di bind ñiy njëkk a dugg si jàkka ji ak ña ca tege daal di bàyyi mbind mi, ñëw toog di déglu tudd Yàlla gi ak xotba gi.