+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«أَقْرَبُ مَا يَكُونُ الْعَبْدُ مِنْ رَبِّهِ وَهُوَ سَاجِدٌ، فَأَكْثِرُوا الدُّعَاءَ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 482]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee, deeleen ci baril ay ñaan».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 482]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee; ndaxte kiy julli day teg li gën a kawe te tedd ci yaramam ci kaw suuf ndax woyoflu la ak toroxlul Yàlla mu kawe mi fekk ma nga sujjóot.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digle na baril ñaan ca sujjóot ya, bu ko defee toroxlul Yàlla ci wax ak jëf daal di daje.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi :
  2. Toppub Yàlla day dolli Jaam bi mu gën a jege Yàlla mu kawe mi.
  3. Sopp nañu di baril ñaan ca sujjóot ya; ndax bérabi nangu ñaan la.