عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«أَلاَ أُحَدِّثُكُمْ حَدِيثًا عَنِ الدَّجَّالِ، مَا حَدَّثَ بِهِ نَبِيٌّ قَوْمَهُ؟ إِنَّهُ أَعْوَرُ، وَإِنَّهُ يَجِيءُ مَعَهُ بِمِثَالِ الجَنَّةِ وَالنَّارِ، فَالَّتِي يَقُولُ إِنَّهَا الجَنَّةُ هِيَ النَّارُ، وَإِنِّي أُنْذِرُكُمْ كَمَا أَنْذَرَ بِهِ نُوحٌ قَوْمَهُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3338]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ndax duma leen waxtaanal ci Ad-Dajjaal, lu benn Yonnente masul a wax aw xeetam? Moom de dafa patt, dana ànd ak lu mel ni àjjana ak sawara, la muy wax ne mooy àjjana loolu sawara la, maa ngi leen koy moytondikuloo kem na ko Nuuh moytondikuloo woon aw xeetam».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3338]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ci Dajjaal ak i meloom ak ay màndargaam lu benn Yonnente bu ko jiitu masul a wax aw xeetam, bokk na ci loolu:
Moom dafa patt.
Yàlla it da koo def mu ànd ak lu mel ni àjjana ak sawara, ci kem li bët di gis.
Waaye àjjanaam ji sawara la, sawaraam si it àjjana la, ku ko topp mu dugal ko ci àjjana jii ci li nit ñi di gis, waaye ca dëgg-dëgg sawara la suy lakke, ku ko moy mu dugal ko ci sawara sii ci li nit ñi di gis, waaye ca dëgg-dëgg àjjana la ju teey, Tek ca Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di moytondikuloo ci fitnaam kem ni ko Nuuh daan moytondikuloo aw xeetam.