عن أبي هريرة رضي الله عنه أَن النبيَّ صَلّى اللهُ عَلَيْهِ وسَلَّم قَالَ:
«الرَّجُلُ عَلَى دِينِ خَلِيلِهِ، فَلْيَنْظُر أَحَدُكُم مَنْ يُخَالِل».
[حسن] - [رواه أبو داود والترمذي وأحمد] - [سنن أبي داود: 4833]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"Nit ki moo ngi ci diiney xaritam, na ku nekk xool kan lay xaritool".
[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 4833]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne nit ki day niróo ak xaritam ak àndandoom ci doxiinam ak aadaam, xarit ga di jeexital ci jikó yi ak melo yi ak doxaliin yi, lii moo tax muy gindee di jëmale ci rafetug tànn xarit; ndaxte moom day tegtal xaritam ag gëm ak ug njub ak yiw, bu ko defee muy ndimbal ci àndandoom.