عَنْ سَهْلِ بْنِ مُعَاذِ بْنِ أَنَسٍ عَنْ أَبِيهِ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ أَكَلَ طَعَامًا فَقَالَ: الحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي أَطْعَمَنِي هَذَا وَرَزَقَنِيهِ مِنْ غَيْرِ حَوْلٍ مِنِّي وَلاَ قُوَّةٍ، غُفِرَ لَهُ مَا تَقَدَّمَ مِنْ ذَنْبِهِ».
[حسن] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 3458]
المزيــد ...
Jële nañu ci Sahl ibn Muhaas ibn Anas mu jële ci baayam mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«ku lekk aw ñam daal di wax: maa ngi sant Yàlla mi ma leel lii, wërsëgale ma ko ci lu dul benn pexe bu bawoo ci man du caagine kàttan, kon dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram».
[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3458]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day soññ ku lekk aw ñam mu sant Yàlla, amuma kàttan ci indi ñam wi, du caagine lekk ko ci lu dul ndimbalu Yàlla mu kawe mi, Topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne ku wax loolu yeyoo na Yàlla jéggal ko bàkkaaram yu ndaw yi weesu.