عن أَبِي أُمَامَةَ إِياسِ بنِ ثَعْلَبَةَ الحَارِثِيِّ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنِ اقْتَطَعَ حَقَّ امْرِئٍ مُسْلِمٍ بِيَمِينِهِ، فَقَدْ أَوْجَبَ اللهُ لَهُ النَّارَ، وَحَرَّمَ عَلَيْهِ الْجَنَّةَ» فَقَالَ لَهُ رَجُلٌ: وَإِنْ كَانَ شَيْئًا يَسِيرًا يَا رَسُولَ اللهِ؟ قَالَ: «وَإِنْ قَضِيبًا مِنْ أَرَاكٍ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 137]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Umaamata Iyaas ibn Sahlabata Al-Haarisii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"ku sàkku a dog àqi jullit ci giñam, Yàlla waral na ci moom Sawara, araamal ci moom àjjana" jenn waay ne ko: donte mbir mu ndaw la yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne ko: "donte ab bantu Araak la".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 137]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day moytandikuloo giñ ngir dog àqi jullit, te fayug loolu mooy yayoo sawara, ak xañ ko àjjana, te ci bàkkaar yu mag yi la bokk. Jenn waay ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, donte la muy giñ mbir mu tuuti la? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: donte loolu dafa toll ne bantu socc bi ñuy jële ci garabu Araak.