عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ غَدَا إِلَى الْمَسْجِدِ أَوْ رَاحَ أَعَدَّ اللهُ لَهُ فِي الْجَنَّةِ نُزُلًا، كُلَّمَا غَدَا أَوْ رَاحَ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 669]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«ku xëy dem ca jàkka ja, walla mu gont fa Yàlla dana ko waajalal ca àjjana ab wàccuwaay, saa yu xëyee walla mu gont».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 669]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bégal na kiy dem ca jàkka ja ngir jaamu walla sàkku xam-xam mbaa geneen jubluwaayu yiw ci waxtu wu mu man a doon; ci njëlbeenu bëccëg gi walla ca mujj ga ci ne Yàlla waajalal na ko ab barab ak nganale ca àjjana, saa yu dikkee ca jàkka ja guddi walla bëccëg.