+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«صَلَاةُ الرَّجُلِ فِي جَمَاعَةٍ تَزِيدُ عَلَى صَلَاتِهِ فِي بَيْتِهِ وَصَلَاتِهِ فِي سُوقِهِ بِضْعًا وَعِشْرِينَ دَرَجَةً، وَذَلِكَ أَنَّ أَحَدَهُمْ إِذَا تَوَضَّأَ فَأَحْسَنَ الْوُضُوءَ، ثُمَّ أَتَى الْمَسْجِدَ لَا يَنْهَزُهُ إِلَّا الصَّلَاةُ، لَا يُرِيدُ إِلَّا الصَّلَاةَ، فَلَمْ يَخْطُ خَطْوَةً إِلَّا رُفِعَ لَهُ بِهَا دَرَجَةٌ، وَحُطَّ عَنْهُ بِهَا خَطِيئَةٌ، حَتَّى يَدْخُلَ الْمَسْجِدَ، فَإِذَا دَخَلَ الْمَسْجِدَ كَانَ فِي الصَّلَاةِ مَا كَانَتِ الصَّلَاةُ هِيَ تَحْبِسُهُ، وَالْمَلَائِكَةُ يُصَلُّونَ عَلَى أَحَدِكُمْ مَا دَامَ فِي مَجْلِسِهِ الَّذِي صَلَّى فِيهِ، يَقُولُونَ: اللهُمَّ ارْحَمْهُ، اللهُمَّ اغْفِرْ لَهُ، اللهُمَّ تُبْ عَلَيْهِ، مَا لَمْ يُؤْذِ فِيهِ، مَا لَمْ يُحْدِثْ فِيهِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 649]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«jullig góor gi ca mbooloo ma moo ëpp julleem ci këram ak ci marse ba luy tolloo ak ñaar-fukki daraja ak lu topp, loolu nag ndax bu kenn ci ñoom jàppee rafetal njàppu ma, daal di dem ca jàkka ja te dara yëkkatiwu ko lu dul julli, du jéego benn jéego lu dul ne dees na ko ci yëkkatil daraja, sippil ko ci njuumte, ba ba muy dugg ca jàkka ja, bu duggee ca jàkka ja ci julli la nekk fii ak julli moo ko téye, te malaaka yi dañuy julli ci kenn ci yéen fii ak moo ngi ca bérab ba mu doon jullee, dañuy wax naan: Yàlla yërëm ko, Yàlla jéggal ko, Yàlla nangul tuubam, fii ak lotul kenn, te tojlewul».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 649]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bu jullit jullee ci mbooloo, julleem googu moo gën julleem gi ci biir këram, walla ci biir maarseem lu toll ni ñaar-fukki yoon ak lu teg. Topp mu tudd sababu loolu: te mooy bu góor gi jàppee matal ag njàppam rafetal ko, topp mu génn jëm ca jàkka ja te dara génnewu ko lu dul bëgg a julli, kon du jéego benn jéego lu dul ne dees na ko ci yëkkatil martaba ak wàccuwaay, faral ko ci njuumte, Bu duggee ca jàkka ja daal di toog di xaar julli, kon dana am payug julli ak yoolam fii ak moo ngi xaar julli, te malaaka yi dañu koy ñaanal fii ak moo ngi toog fa mu doon jullee, ñuy wax naa: "Yàlla jéggal ko, Yàlla yërëm ko, Yàlla nangul tuubam" fii ak yàqul njàppam, walla mu def luy lor nit ñi walla malaaka yi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Jullig ki beru ci
  2. këram walla ci maarseem lu wér la, waaye dana am bàkkaar ci li mu bàyyi mbooloo ma ci lu dul ngànt.
  3. Jullig mbooloo ca jàkka ja moo gën jullig nit ki beru ci ñaar-fukk ak juróom walla juroom-benn walla juróom-ñaari daraja.
  4. Bokk na ci liggéeyi malaaka yi di ñaanal way-gëm ñi.
  5. Ngëneelu dem jàkka ànd ak njàppu.