عَنْ أَبِي الحَوْرَاءِ السَّعْدِيِّ قَالَ: قُلْتُ لِلْحَسَنِ بْنِ عَلِيٍّ رضي الله عنهما: مَا حَفِظْتَ مِنْ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ؟ قَالَ: حَفِظْتُ مِنْ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«دَعْ مَا يَرِيبُكَ إِلَى مَا لاَ يَرِيبُكَ، فَإِنَّ الصِّدْقَ طُمَأْنِينَةٌ، وَإِنَّ الكَذِبَ رِيبَةٌ».
[صحيح] - [رواه الترمذي والنسائي وأحمد] - [سنن الترمذي: 2518]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Al-Hawraa As-Sahdii mu wax ne: wax naa Al-Hasan ibn Aliyun yal na leen Yàlla dollee gërëm ne ko: lan nga mokkal ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc? Mu ne ma: mokkale naa ci Yonnente Yàlla bi:
«bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer, ndaxte dëgg ag dal la, fen nag ag jax-jaxi la".
[Wér na] - - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2518]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle na ñu bàyyi li ñuy sikk-sàkka ci ay wax ak i jëf ci ne dañu ko a tere walla déet, ndax dafa araam walla dafa dagan, jëm ci li ñu sikk-sàkkawul ag rafetam ak ug daganam wóor, ndaxte xol daciy dal, lu am sikk-sàkka nag day jàqal xol te du ci dale.