+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه قال:
أَتَى النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ رَجُلٌ أَعْمَى، فَقَالَ: يَا رَسُولَ اللهِ، إِنَّهُ لَيْسَ لِي قَائِدٌ يَقُودُنِي إِلَى الْمَسْجِدِ، فَسَأَلَ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنْ يُرَخِّصَ لَهُ فَيُصَلِّيَ فِي بَيْتِهِ، فَرَخَّصَ لَهُ، فَلَمَّا وَلَّى دَعَاهُ، فَقَالَ: «هَلْ تَسْمَعُ النِّدَاءَ بِالصَّلَاةِ؟» فَقَالَ: نَعَمْ، قَالَ: «فَأَجِبْ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 653]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Benn waay dafa ñëw ci Yó’ente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, man de amuma ku may wommat yóbb ma ca jàkka ja, mu sàkku ci Yónente Yàlla bi mu yombalal ko muy jullee ci këram, Yónente bi daal du loy jox Yombal, ba mu wëlbatikoo rekk mu woo ko, daal di ne ko: "ndax danga dégg wooteg julli gi?" Mu ne ko: waaw, mu ne ko: "kon nag wuyujil ».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 653]

Leeral

Daa am gumba gu ñëw si Yónente bi -yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi amuma ku may dimbali di jàpp sama loxo yóbb ma jàkka ja ci julliy juróom yi, mu bëgg Yónente bi yombalal ko mu bàyyi jullig mbooloo, mu yombalal ko, waaye ba mu wanee ginnaaw rekk mu woo ko, ne ko: ndax danga dégg noddug julli gi? Mu ne: waaw, mu ne ko kon nag wuyujil wootekatu julli gi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Jullig mbooloo dafa war; ndax yombal du nekk ci lu dul lu war.
  2. Wax ji mu wax ne: "kon wuyul" ñeel kiy dégg woote gi tegtal la ci warug jullig mbooloo; ndax cosaanu digle mooy ne daa war.
Ndollent