عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه:
أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَرَأَ فِي رَكْعَتَيِ الْفَجْرِ: {قُلْ يَا أَيُّهَا الْكَافِرُونَ}، وَ{قُلْ هُوَ اللهُ أَحَدٌ}.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 726]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jàng na ci ñaari ràkkay Fajar: {Xul yaa ayyuhal kaafiruuna}, ak {Xul huwal Laahu Ahad}.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 726]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na sopp a jàng ci naari ràkkay Fajar ginnaaw Faatiha, ci ràkka bu njëkk bi saaru: {Xul yaa ayyuhal kaafiruuna}, (Alkaafiruuna), ci ràkka bu ñaareel bi saaru {Xul huwal Laahu Ahad} (Al-Ixlaas).