عَنْ أُمِّ حَبِيبَةَ رضي الله عنها زَوْجِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالت: سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«مَنْ حَافَظَ عَلَى أَرْبَعِ رَكَعَاتٍ قَبْلَ الظُّهْرِ وَأَرْبَعٍ بَعْدَهَا حَرَّمَهُ اللَّهُ عَلَى النَّارِ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 428]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ummu Habiibata yal na ko Yàlla dollee gërëm soxnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi muy wax ne:
"ku sàmmonte ak ñenti ràkka njëkk Tisbaar ak ñenti ràkka ginnaaw tisbaar yàlla araamal ko ca sawara".
[Wér na] - - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 428]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day bégal kiy julli naafila ñenti ràkka njëkk jullig Tisbaar, ak ñenti ràkka ginnaawam, mu sax ca sàmmonte ak moom, ci ne Yàlla araamal na ko ca sawara.