عن عائشةَ أُمِّ المُؤْمِنينَ رضي الله عنها:
أن النبي صلى الله عليه وسلم كان لا يَدع أربعا قَبل الظهر وركعتين قبل الغَدَاة.
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 1182]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daawul bàyyi ñenti ràkka njëkk Tisbaar ak ñaari ràkka njëkk suba gi.
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1182]
Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daa saxoowoon julliy naafila ci këram te daawu ko bàyyi: ñenti ràkka ci ñaari sëlmël njëkk jullig Tisbaar, ak ñaari ràkka njëkk Fajar.